Montréal-Toronto
ar de en es fr it nl pt gsw rus wol ja zh

Montréal-Toronto

Barabou diokoo ci Montréal ak Toronto ak tamit ci naka leñuy toukee ci diguente ñaari dek yooyou.

Li fi nek

Montréal
Toronto
Nan la ñiy damé montréal
Liens
Politique de confidentialité



[ Li fi nek ]

Montréal

Montréal St.George
Montréal St.George
Photo: Fotopanorama.ch


Makaanu koomkoomu Quebec ak ñaareelu dek bi guëna mak ci dek yidi lak nasaraan ci adouna bi (ganaaw Paris).. Neek 556 km ci kaw Toronto boorou penkou ci ben tund bu nek Saint-Laurant. Jeanne-Mance ak Paul de Chomedey neke ca Maisonneuve ñooko sos ci atu 1642 ci turu Marie. Donte moy dek bu gena mak xi diwaanu Quebec, nekoul capitalam (man nañu rek waxni moy deku Quebec).

Moy deku Canadiens nek ca montréal, Alouette yi ak equibu foot-ballou Impact. Ci waxtu tangorwi maanaam nawet, dekebi deesne neek makaanu xewxew yu baree lu ci mel ni Festivalou jazz bu montreal, francofolies yi ak festivalou Juste pour rire.

Nguir gën ci xam dara, gëstouleen ci Wikipedia wala Site Web officiel-lou dekebi.



[ Li fi nek ]

Toronto

Toronto City Hall
Toronto City Hall
Photo: Fotopanorama.ch


Makaanu koomkoom ak dek bi guëna mak ci Canada. Neek 556 km ci soufou Montreal camooyu sëw jënt , ci booru dex yi nek ci dexü Ontario. John Graves Simcoe mooko sos ci atu 1743 ci turu York. Woutek li yen nit you nek ci soufou frontieram ak ci bitim rew di xalat, nekoul capitalou Canada (Ottowa la).

Mom moy taxü Maple Leafs yi nek Toronto, Raptors yi ak Argonauts yi. Deuk bi tamm na di daf doublage-gou taxü americain yi ci filmou Hollywood yi. Ñin-ña ngui diotalante ni nguir daf ba li ñiy wane ci tele bi geuneu ndirok deugue nguir topando New York, Ay saleté legnouy yokou ci koy yi nga xamantani ci deug dagnoo set.

Nguir gën ci xam dara, gëstouleen ci Wikipedia wala Site Web officiel-lou dekebi.



[ Li fi nek ]

Nan la ñiy damé montréal

Ak roplane

Mom moy jumtuwaay bi gueneu gaw nguir jalë 556 km yi, Ba pare nonou la ndara mel, ba ñü dafar ben watarail bou gaw lolou. Niet yoonou roplane you mak (AirCanada, Porter ak WestJet) ñom ñoy doxal ligeeye bi, ci anam bou sakh, digueuente ñari deukou taax youyou. Wakhtu touki bi mingui tolou ci borou 1 wahtou 15 simili, waye boulen fate yok ci wakhtou wi nguey daf nguir dam ci aeroport bi ak nguir bindou ci ñi wara touki. Njëgu paas-su demrek mi ngui nek ci diguente 80$ ak 300$ ci lu muy gueuneu yombu.

Montréal-Aéroport international Pierre-Elliott-Trudeau

Ben aéroport bi nek Montréal binga kameenteni mooy ligeeyag aji tukiyi moy Montréal-Aéroport international Pierre-Elliott-Trudeau . Nit-ñi nek ci diwaan boobu ñinkey mowe ba legui ci touram bo ndieuk ba : "Dorval Airport". Ngir dam ci aeroport bi, am na 3 jumtukaay: dieul ben taxi, wala 747 Express bus wala dioumtu kay-you touki mbolo. Taxi : niki demb beek dik bi tolu, ben taxi di na dieul diguente 20 ak 60 minutes nguir dam ci aeroport bi diare ci dëkëbi bi. Paasbi toluna ci 40$. 747 Express bus : Yoonu express bobou le mi ngui ley yobou ci diiru 24 wakhtou ci ben beuss, diogue ci fa wata yi di yam ci Montréal (Métro Berri-UQAM) diare ci makaanu-nou métro Lionel-Groulx ba yegue aeroport. Li nga wara fey nguir touki bi ci dayo 45 ba 60 minutes mi ngui tolou si 10$. Wahtou yi bus bi di diar ñinko tothi-tal fii.
Ak dioumtu kay-you touki mbolo : Anam bi nga kham ni mo gueneu yombe pour dam ci aeroport bi moy nga dieul bus ci 3,00$. Dieuleul bus 211 ci fi métro bi di dieulé ñin-ñi ci Lionel-Groulx ba paré nga dieulate bus 204 wala 209 ci watarail bi di dieulé ñin-ñi ci Dorval. Sentoul ni yon bi di na dieul 30 simili ba ben wahtou.

Billy Bishop Toronto City Airport / Toronto Pearson International

Toronto mi ngui am ñari aéroport : Billy Bishop Toronto City Airport (Ñinkey wowe tamit Toronto City Centre Airport wala Toronto Island Airport) ak Toronto Pearson International Airport. Bi ci ndieuk, té nga xamné gninkey wowé Porter rek mokey dieufeundiko ba pare meun neñ ci diot loudoul ñou diare ci kaw bou nek Bathurst Street ci centre-ville bi. Aeroport bi niou nan Pearson, nga khamne mo geuneu mak fouf, yenen compagnie aerienne yi ño key dieufeundiko. Nek ci lou tollok 27 km bo ko khole ak centre-ville bi, Meun nga ci diot bo dieule bus ci Toronto (Toronto Transit, GO Transit). Amna tamit ben Service de navette aéroportuaire, ay taxis ak bus you bare youy dam yenen diwan ci Ontario.

Ak watarail

Mom moy yon bi gueneu nopalé ngir gnir touki digueunté ñari deuk yi. Wa deukou couronne Via Rail mingui ngui mayé yon you baré youy diougué ci ben centre-ville dam ci benen biss bou nek. Waxtu touki bi mingui ci diguente 4h 38min ba 5h 35min. Billet bi li mouy diar mi ngui dépendre ci train bi ak jour bi nga ko dieunde. Mi ngui doré ci 50$, Wanté meun neñou yokou lou mou gaw gaw ba tolook ci lou eup 140$ ci ñarelou classe bi.

Yoon bi gueuneu gaw autorail numéro 66 mo key daf, mi ngui daf yoonu Toronto ba Montreal ci 4 wahtu ak 38 minutes. Bo naté gawayam ci yoon wi, mi ngui tolok 120 km/h, lolou takhna mou nek autorail bi gueuneu gaw ci kaw Amérique du Nord wakhtou wi niou key bindeu. (Acela Express bi diguente Boston ak New York mom mo gueuneu gaw ci meun meun waye bo nate gawayam ci yoon wi yeup mo ko gueuneu yekh.)

Ak bus

Mom mon anam bi geuneu yomb nguir touki. Yon you beure amna biss bou nek, té Greyhound/Voyageur ak Coach Canada gno kay daf. Kou mouji ki mom mingui diay ci wahtou wi niou tollou nii ay paassou touki Megabus ci lou tollok 1$, wante ndieuk bi gnou tamm nguir dam bi rek mi ngui tollou ci 30$ ba 100$. Bo ko kole ci bus bi, yoon wou diougue ci ben deukk dam ci bennen mi ngui dieul digueunte 7 ba 12 wakhtou.

Ak wata

Milles Îles
Milles Îles
Photo: Stefan Bracher


Anam bi ñin-ñi tam di touké digueunté ñari deuk yi. Autoroute 20 bi nek Québec, té nga khamné dafa changer touram ak autoroute 401 ci Ontario mo la fay yobu directement. Yon bi, wahtou wi nu tolou nii do fay pour dialle, lolou taxna do fayat dara. Selon ni ngey dawalé, di na la dieul ci wakhtou 6 wahtou wala lou ka eupp.

So yakamtioul, meun-nga taxaw diganté Kingston ak Cornwall ngir visiter Mille-Îles yi.

Bokko wata

Nek yon bi geuneu mak ci borou penku Canada, nin-nu beré daniy diay ay place nguir bokak yaw touki bi digueunté Montréal ak Toronto. Ci louy yoon, den ley laathie nga participer ci ndieugou essence bi. Ben site bou ñü beuré kham, di wané ñi beug di bookkandok yaw touki bi moy fi you binde la section de covoiturage de Craigslist. Attention, amoul controle bouy wané offre yooyu ci Craigslist. Bep responsabilité ngir ay tohtie-tothie you dioték offre yi ci Craigslist bégn négnko. Dieufundiko len ak sen xam-xam!



[ Li fi nek ]

Liens


bep responsabilité ci contenu-wou sites yi ci kanam dou ñou ko dioké

Sites internet yi nga khamné toudd-négnou-len ci document bi.

Montréal

Toronto

Roplane

Watarail / Wata

Yenen Sites internet you am ndieurigne.

Ce site internet utilise des cookies et des outils d'analyse pour améliorer la convivialité et la publicité. Plus...

© Stefan Bracher